TSK

TSK · Joel 3:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Musaa ne ko: «Fiiraangee la jàpp ndax man, am? Éy bu niti mbooloom Aji Sax ji mépp doon ay yonent, Aji Sax ji sol leen ag leeram!»

su boobaa Aji Sax jeey tijji seen wërsëg, yërëm leen. Seen Yàlla Aji Sax ji moo leen di dellu dajalee foofa, ci biir mboolem xeet ya mu leen tasaare woon ca seen biir.

Ana kuy xettlee Israyil fa Siyoŋ? Éy bés bu Aji Sax ji delloo ñoñam ndam, ndaw mbégte ci giirug Yanqóoba! Ndaw bànneex laa ne, ci Israyil gii!

Soo dëppee ba déglu, ma àrtu la. Ma ne, kon ma xellil la samam xel, xamal la samay kàddu.

Maay sottim ndox suuf su mar, ak wal yu waleg joor gu wow. Maay sotti saw askan samag noo, sama barke sottikul ñi nga meññ,

«Man nag, sama ndesu gétt, maa leen di dajalee mboolem réew yi ma leen dàqoon, jëme; te maa leen di délloosi seen parlu, ñu meññ ba yokku.

Ndax kat ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «maay tijjil sama ñoñ seen wërsëg, muy Israyil di Yuda.» Aji Sax jee ko wax. «Maa leen di delloo ca suuf sa ma moomale woon seeni maam.»

¶ «“Waaye maay tijji seen wërsëg; maay tijji wërsëgu Sodom aki janqam, tijji wërsëgu Samari aki janqam, yaw it ma tijjiwaale sa wërsëg.

¶ «Kon nag yaw nit ki, biralal waxyu, waxal Gog, ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Bésub keroog déy, bu Israyil sama ñoñ sancsee xel mu dal, dinga ko yég,

Dinañu xam ne maay seen Yàlla Aji Sax, ji leen yóbbu woon ngàllo ca yéefar ya, ba noppi délloosi leen seen suuf, te bawuma kenn gannaaw.

¶ Malaaka ma waxati ma, ne ma: «Jamono yooyu ci la Mikayel, malaakam wattukat mu mag, miy taxawu sa mbooloo, di jóg. Muy jamonoy njàqare ju masula am, cosaanal xeet yi ba tey jii. Bu keroogee sa bokk yay mucc, di ñi ñu bind ci téereb dund bi.

Amos 9:14 TSK

Maay tijji wërsëgu Israyil, sama ñoñ; ñu tabaxaat seeni gent, dëkke; jëmbat seen tóokëri reseñ, naan seen biiñ, bey ay tool, lekk ca meññeef ma.