Yeen malaaka yi, santleen Aji Sax ji, yeen jàmbaar yu mag yiy jëfe ndigalam, di sàmm kàddoom.
TSK
TSK · Joel 3:11
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Maa jox ndigal ñi ma beral sama bopp, maa woo sama jàmbaar ñiy réy-réylu, ne leen ñu sottal mbugal mi samam sànj laaj.
Waaye yaa naa jàyy ni ngëlén, mel ni aw xiin, muur réew mi, yaak sa gàngoor yépp, ak xeeti xeet yi ànd ak yaw.
Booba ñoom xamuñu lu ciy xalaati Aji Sax ji, ak luy mébétam, nde moo leen di dajale niy sabaar ca dàgga ja.
Xeet yépp laay dajale ci kaw Yerusalem, ngir xare. Dëkk bi lees di nangu, sëxëtoo kër yi, tëdde jigéen ñi. Genn-wàllu dëkk beey génn, jëm ngàllo, waaye ndesu askan wi, deesu leen dagge ci dëkk bi.
Ñooñu nag ay njuumay Seytaane lañu, yuy def ay kéemaan, tey dajaleji buuri àddina sépp, ngir xareb bés bu mag bu Yàlla Aji Man ji.
¶ Ba loolu amee ma gis rab wi, mook buuri àddina yeek seeni gàngoor, ñu daje ngir xareek ki war fas week gàngooram.