TSK

TSK · Joel 3:19

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax jeey wowal walum ndox, ma séle géeji Misra. Mooy tàllal loxoom, tiimale dexu Efraat, wal kook doole, dóor ko, mu séddlikoo juróom yaari wal, mu jaarale ca nit ñu caraxu,

Yeen xeet yi, jegesileen te déglu; yeen askan yi, teewluleen! Na suuf ak li ci biiram déglu, muy àddinaak lépp lu mu jur.

«Edom day mujj gental, ku fa jaare waaru, di muslu ci mboolem li ko dal.

Bégleen te bànneexooy, yeen Edomeeni réewum Ucc, ci yeen it la kaasu mbugal di jàllsi, ngeen màndi, futteeku, ne duŋŋ.

¶ Kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma:

¶ Peeñum Abdiyas a ngi. Boroom bi Aji Sax ji moo wax lii ñeel askanu Edom.

Fa réewum Misra laa leen di waññee, te fa Asiri laa leen di dajalee, yóbbu leen réewum Galàdd ak Libaŋ, te deesu fa gis fu ñu xaj.

te Esawu laa foñ. Maa def ay tundam ab gent, ab céru suufam, ma def ko dëkkuwaayu tilli màndiŋ mi.