Ñu dugal gaal ga ca seen biir kër tuur ma ñu naan Dagon, teg ko ca wetu jëmmu Dagon ja.
TSK
TSK · Joel 3:5
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Axas jël xaalis ak wurus wa nekkoon ca kër Aji Sax ja ak ca dencukaayi kër Buur, defal ko buurub Asiri yóbbal.
Nabukodonosor jële fa mboolem alali kër Aji Sax ji ak alali kër Buur, daldi buub lépp luy ndabu wurus lu Suleymaan buurub Israyil defarlu woon ci kër Aji Sax ji, muy la Aji Sax ji waxoon.
¶ «Moo tax ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «deesatul wax ne: “Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund te génnee bànni Israyil ca réewum Misra.”
«Nàmmleen fitt yi, feesale mbar yi! Aji Sax ji xabtal na buuri Medd fi kaw Babilon, nar koo tas. Lii mbugalu Aji Sax jee, mbugal mi këram waral.
Biiñ ba jay Baltacar, mu joxe ndigal, ñu indi ndab, yu xaalis yaak yu wurus ya baayam Nabukodonosor jële woon ca jaamookaayu Yerusalem, ngir ñu naane ca, mooki jaraafam aki soxnaam aki nekkaaleem.
Waaye kaw tundu Siyoŋ la aw ndes di rawe, te dina doon bérab bu sell, waa kër Yanqóoba it moomaat seeni moomeel.