TSK

TSK · Joel 3:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ba mu ko defee ñu wékk Aman ca bant ba mu waajaloon Mardose. Merum Buur doora giif.

Bul tiit, yaw laa àndal, maay jële saw askan penku, dajalee leen sowub jant.

Xanaa dañu naan: “Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund te génnee askanu Israyil réewum bëj-gànnaar, génnee leen mboolem réew ya mu leen sànkeji woon.” Su ko defee ñu dëkkewaat seen suufas bopp.»

Waaye ku la lekk, dees na ko lekk; sa noon yépp lañuy jàpp njaam ba ñu daj. Ku la futti, dees na ko futti, ku la saax-saaxee dees na ko saax-saaxee.

Maa ngii di leen dajalee ca mboolem réew ya ma leen sànni woon, ndax mere leen ak jéppi leen ba sama xol fees dell. Te maa leen di délloosi fii, dëël leen ci jàmm;

Maa leen di seppee ci yéefar yi, dajalee leen mépp réew, délloosi leen seen suufas bopp.

Joel 3:4 TSK

Jant beey soppliku ag lëndëm, weer wi doon deret, bésub Aji Sax ji doora taxaw, bés bu réy bu raglu ba!

Daan bu àndul ak yërmande, moom lees di àttee ña daawul jëfe yërmande. Yërmande nag kekku na ab daan.

Deretu ñu sell ñeek deretu yonent yi lañu tuur, nga nàndal leen deret, feye leen.»