TSK

TSK · Jonah 2:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

ndax kat dees na dégg sa tur wu réy, ak sa dooley loxo ak sa kàttanu përëg, bu dikkee ba jublu ci kër gii, ñaan,

su boobaa maay dagge bànni Israyil fi déndu suuf si ma leen jox, te kër gi ma sellal ngir sama tur, maa koy xalab, mu sore ma, te kon Israyil mujj di tur wu ñuy léeboo ak di ko kókklee ci biir xeet yépp.

Aji Sax ji, yaay sànk kuy fen, sib kuy bóomeek kuy wore.

Sa wal ya sotti, xóote awu moroom ma; say wal ak say gannax, lépp a jaare sama kaw.

bokk ci néew, yi dara waratul, mbaa ku ñu bóom, mu tëdd cim pax, faaleetoo ko, xanaa dagg ko, wacc.

Man de dama noon: «Sama digg doole laay deme jaare bunti njaniiw, sama ndesu fan réer ma!»

Siyoŋ a nga naa: «Aji Sax ji wacc na nu, Boroom bi fàtte na nu!»

¶ Aji Sax ji nag ne ma: «Musaa ak Samiyel sax, bu ñu taxawoon fi sama kanam, du tax ma faale askan wii. Dàqal, ñu sore ma, te wéy.

¶ Mu ne ma: «Yaw nit ki, yax yii ñooy mboolem waa kër Israyil. Ñu ngi naan: “Nun de, ay yaxi neen yu wow koŋŋ lanu, sunu yaakaar tas na, nun kay yàqu nanu.”