Esther 4:1
TSK
¶ Ba Mardose yégee la ñu def lépp, daa xottiy yéreem, sol ay saaku, sottikoo dóom, di ko ñaawloo, dugg ci biir dëkk bi, di yuuxu yuux gu réy te metti.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba Mardose yégee la ñu def lépp, daa xottiy yéreem, sol ay saaku, sottikoo dóom, di ko ñaawloo, dugg ci biir dëkk bi, di yuuxu yuux gu réy te metti.
Mu wut tojitu njaq, di ko xasanoo, daldi toog ci biir jalub dóom.
Kon yeen buur yi, muusleen, kilifay àddina, fàgguleen.
Waxal Buur, wax Lingeer yaayu Buur ne leen: «Dëjuleen fi suuf, seen mbaxanam nguur mu yànj foq na.
Dëppal sa kanam ci suuf, jombul yaakaar nuyoo.
Ma walbatiku jublook Boroom bi Yàlla. Maa ngi sol saaku, diwoo dóom boole kook koor, toroxloo ko, di ko ñaan ak a dagaan.
¶ Mbokkum gëmkat mi suufe daraja, na sagoo ab kawewaayam;