TSK

TSK · Jude 1:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Job 14:14 TSK

Ndax dees na dee, di dundati? Konoon ma muñe ko sama fani coono yépp, ba keroog sama kuutaay yiwisi ma.

Te yaakaar jooju du tas, ndax cofeelu Yàlla gi baawaan ci sunu xol, ci ndimbalal Noo gu Sell gi mu nu may.

Ndaxte peyooru bàkkaar mooy dee, waaye yiw wi Yàlla di maye mooy texe gu sax dàkk fi Almasi Yeesu, sunu Boroom.

Yal na Boroom bi wommat seen xol, jëme ci cofeelu Yàlla ak muñ gi ci Almasi.

ñeel Timote, sama doom, sama soppe. Aw yiw ak yërmande ak jàmm ñeel na la, bawoo ci Yàlla Baay bi, ak sunu Sang Almasi Yeesu.

Yal na ko Boroom bi may mu daj bésub keroog booba, yërmandey Boroom bi. Taxawu na ma lool ca Efes, te xam nga ko xéll.

Loolu lees nu digal, li feek nu ngi séentu yaakaaru mbég ma, keroog bésu peeñum sunu màggaayu Yàlla, miy Yeesu Almasi, Musalkat bi.

ak yàkkamti bésu Yàlla ba, di jëfe li koy taxa gaawa dikk, ba asamaan yi lakk ba jeex, lu ca jëmmu lakk ba seey.

Jude 1:24 TSK

¶ Ki leen mana aar ci bépp jéll, ba taxawal leen fa muy teewejee darajaam, te fekk leen ñàkk sikk, seen mbég mat sëkk,