Su boobaa sa bunti dëkk sax di ñaawlook a jooy, mel ni ndaw su ñu futti, mu ne dett fi suuf.
TSK
TSK · Lamentations 1:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yeen jigéen ñi dal xel, taxawleen temm, déglu ma; yeen janq ji féex, teewluleen ma.
Xibaar a ngoog, di ñëw, riir mu réy a yëngoo réewum bëj-gànnaar, nara gental dëkki Yuda yu mag yi, till yi dëkke.
¶ Aji Sax ji dafa wax ne: «Bérab bii ngeen ne ab gent la bu kenn nekkul, du nit, du rab te muy dëkki Yudak mbeddi Yerusalem yii gental, kenn nekku fi, du nit, du rab, dees na fi déggati
Aji Sax ji moo yey, kàddoom laa gàntal. Yeen, xeetoo xeet, ngalla dégluleen te xool samaw tiis. Samay ndaw yu góor ak yu jigéen, ñoo duggi ngàllo!
Bunti dëkk ba suulu na, te moo yàqte, dammate weñi tëjukaay ya, buuram aki garmeem a tumurànkeji ca yéefar ya, te téereb yoon amul, yonent it gisatul peeñu mu bawoo fa Aji Sax ji.
Waxambaane yee yenu doji wolukaay, gone yu góor yi sëfoo sayi matt, di tërëf.
Maay dakkal gépp mbéxam; ay màggalam, ay Terutel weeram, ay bési Noflaayam, ak mboolem bési ndajeem.
Kon nag dees na gàbb Siyoŋ nib tool, Yerusalem googu diy tojit, jale, tundu kërug jaamookaay baay doon gajj bu kawe.