Daawudaak mbooloo ma mu àndal nag di yuuxook a jooyoo, ba amatuñu dooley jooy.
TSK
TSK · Lamentations 2:11
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Onk naa ba loof, di fanaanee jooy, sama lal di féey, ba far seeye rongooñ.
Waccoo ma ci loxol noon, danga maa taxawal fu ma yaatoo.
Moo ma tax ne: «Buleen ma xool, damay naqarlu, jooy. Tàyyileen maa dëfal ci sama bokk yi sànku.»
Sa doom yi ne lasar, mbete kooba yu fiir jàpp, ñu ne lareet fépp fu mbedd daje, këppoo sànjum Aji Sax ji, sa Yàlla ji leen rëbb.
Sama bokk yaa ngooguy yuuxu yuux yu àkki fu sore, naan: «Moo Aji Sax ji daa newul Siyoŋ a? Moo Buurub Siyoŋ da fee nekkatul a?»
¶ «Léegi nag, Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Ana lu jar ngeen di teg seen bopp loraange ju réye nii, ba nar fee dagge réewum Yuda, góor ak jigéen, xale ba ci perantal, ba dungeen dese kenn?
Looloo ma tax di jooy, rongooñ di wal-wali, te ku may dëfal sore ma, mook kuy seral sama xol. Samay doom a ngi jaaxle, nde noon bi daan na.
Jógal guddi, xaacu: ndoortel wattub guddi, ngay yuri sab xol nim ndox, jàkkaarlook Boroom bi. Tàllal koy loxo, ngir sa bakkani doom, yi xiif tax ne lasiim fi boppu mbeddoo mbedd.
Ag till sax joxe na weenam, nàmpal doomam, te sama bokk yi mujj néeg ba mel ni bànjóolig màndiŋ.
Ña saamar rey a gënu demin ña deeye xiif, jeex tàkk, ne lasar, ndax ñàkk meññatum tool.