Maa leen di noonoo ba seeni noon duma leen, seeni bañ yilif leen. Dingeen daw te kenn dàqu leen.
TSK
TSK · Lamentations 2:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Samiyel ne ko: «Loo may laaj, gannaaw Aji Sax jee la dëddu, def la ab noon?
Féexoon naa, mu falaxe ma; sëq sama ndodd, rajaxe ma, def ma diirukaayam,
Ku tuubul, Yàlla nàmm saamaram, bank xalaam, diir la.
Yewwulee, yewwul, Yerusalemee jógal, yaw mi Aji Sax ji nàndal kaasu mbugalam. Kaas bu wex bay miirloo, taat wa, yaa ko siitaatu.
Waaye ñoom ñoo fippu, di naqaral xelam mu sell, mu soppliku seen noon, ba mujj di xareek ñoom.
¶ Moo tax Aji Sax ji Boroom bi dafa wax ne: «Sama xadar a ngii di sottiku fi bii bérab, fi kaw nit ak mala, garab ak lu suuf meññ, lépp ne jippét, te deesu ko fey.»
Yeen waa kër Daawuda, Aji Sax ji dafa wax ne: Àtte yoon, deeleen ko xëye, di xettli ki ñu xañ dëgg ci ki koy néewal doole, balaa sama mer ne jippét, di tàkk te deesu ko mana fey ndax seen jëf ju bon.
Jombul ñu tinu Aji Sax ji, ku nekk ci ñoom dëpp yoonu mbonam, ndax mer mu réy ak xadar ji Aji Sax ji tuddal askan wii kat, nar naa metti.»
Fa kaw la Aji Sax ji sànnee sawara ci sama biiri yax, moo laaw ab caax ngir fakktal ma, waññi ma, jànnaxe ma, ma dëkke yoggooral.
Man doŋŋ lay yen aka yenaat loxoom, bésoo bés.
Ndeysaan, wurus wa giim na! Ngëneelu wurus soppiku na. Doj yu sell yaa wasaaroo, ca boppu mbedd yépp.
Maa leen di ŋaccal sama mer, sottil leen sama xadar ba giif, te bu ma leen ŋaccalee sama mer, ñu xam ne man Aji Sax ji, maa waxe sama fiiraange.
Liitu xareey jib, ba lépp jekk ngir xare, te kenn du xareji, samam sànj a dikkal askan wépp.
Ni xaalis di seeye ci biir taal, ni ngeen di seeye ca biir. Su boobaa ngeen xam ne man Aji Sax ji maa leen xëpp sama xadar.”»
Ma xëpp leen sama xadar ndax deret ji ñu tuur ci réew mi, ak kasaray tuur yi ñu ko sobeele.
Bu sànjoo, ana kuy taxaw? Ana kuy dékku tàngooru meram? Am sànjam a naan soteet ni sawara, doj yi rajaxoo fi kanamam.