TSK

TSK · Lamentations 3:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Job 7:7 TSK

Éy Yàlla, bul fàtte ne sama dund gii, ag noo doŋŋ la, te dootuma teg bët ngëneel.

Ndeke sama tiisu xol wii, sama jàmm rekk a tax. Sa cofeel a tax nga sorele maak paxum sànkute. Yaa sànni sa gannaaw sama bépp bàkkaar.

Nun ñépp a ngi xiiru ni rab wu aay, binnee binni niy xati, yaakaar yoon, yoon wuute, séentu wall, wall sore.

Aji Sax ji, wacc ngaa wacc Yuda nii? Am Siyoŋ a la génnliku? Lu tax nga di nu dumaa musiba mu amul paj? Nuy yaakaar jàmm, dara baaxul, nuy séentum paj, tiitaange ne jaas!

Alkute ñeel na bés ba ma juddoo, bés ba ma saa ndey juree, yàlla bumu barkeel.

Ndax lu jiitu fan yooyu, nit feyeekuwul peyoor, te mala it indilul nit peyoor, kuy dem ak kuy dikk amul woon jàmm cib noon, nde maa xabtaloon ku nekk ci kaw moroomam.