Ab cér du leen ñeel ci seen biiri bokk. Aji Sax ji mooy seenub cér, na mu leen ko waxe woon.
TSK
TSK · Lamentations 3:24
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
te Aji Man ji di sa wurus, di sa jali xaalis.
Képp kuy aji gëm, soppal Aji Sax ji. Aji Sax jeey sàmm ku ko gëm, di yool, ba wis kuy réy-réylu.
Noon yaa ngi may ñaawal, di ma yendoo naa: «Ana sa Yàlla ji?» Ma ne yàcc, ne yasar.
Yàllaa may musal, di ma sagal, ma di ko doolewoo. Sama kiiraay, Yàllaa!
Kàttan ak pexe jeex, Yàlla di ma dooleel, ma séddoo ko fàww.
Ma bare xalaati xol, nga dëfal ma, ma bég.
Éey Israyil, négandikul Aji Sax ji. Aji Sax jee gore, te yaatug njot.
Ki séddoo Yanqóoba déy wuute naak yii caaxaan. Kookoo bind lépp, te Israyil di giir gi mu séddoo. Kookooy Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi!
Waaye li may dëkke bàyyi xel, ba dese yaakaar mooy lii:
Esayi it neeti: «Ab car ay bawoo ca Yese reen ba, mooy taxaw, yilif jaambur ñi dul Yawut, te moom la ñi dul Yawut di yaakaar.»