TSK

TSK · Lamentations 3:31

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax ji moom turam wu màgg wi tax na du wacc ñoñam, ndax Aji Sax ji la soob, mu def leen ñoñam.

Kon dinaa torxal askanu Daawuda waaye du doon ba fàww.”»

Boroom bi kat du wacc ñoñam mukk, du bàyyi ay séddoom.

Ndànk-ndànk la jëflanteek ñoom, ba mu leen toxalee, dàqe leen noowam gu mag, bésu ngelawal penku.

Duma wéye di sikke ba fàww, duma saxoo di mer, lu ko moy képp ku ma sàkk day tàggook bakkanam.

Maay fas ak ñoom kóllëre gu sax dàkk gu ma leen dul xañati; xanaa baaxe leen, yeb ragal Yàlla ci seen xol, ba dootuñu ma won gannaaw.

Ana Yàlla ju mel ni yaw, di bale ag tooñ, di jéllale ag moy, ñeel ndesu ab séddoom. Kii du denc mer ba fàww, te moo bëgg di yéwéne.