Dingeen mujj lekk seen meññeefum njurukaay, seen suuxu doom yu góor ak yu jigéen, yi leen seen Yàlla Aji Sax ji may, ndax gaw ba, ak tanc bu leen seeni noon tanc.
TSK
TSK · Lamentations 4:10
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
2 Kings 6:29
TSK
Nu togg sama doom, bokk ko lekk. Ma ne ko: “Su ëllëgee indil sa doom, nu bokk ko lekk.” Moom nag mu làq doomam.»
Isaiah 49:15
TSK
«Ana jaboot juy fàtte doomam juy nàmp, mbaa muy néege ku mu jur ci biiram. Bu ko manoona fàtte it, man duma la fàtte.
Éy Aji Sax ji, xoolal, seetal rekk ki nga def nii! Xanaa du ndey mooy dem ba yàpp doomam, doom ju mu sukk jur, mu wér péŋŋ! Xanaa du sarxalkat akub yonent lañuy bóom fi bérabu Aji Sax bu sell bi!
Lamentations 4:3
TSK
Ag till sax joxe na weenam, nàmpal doomam, te sama bokk yi mujj néeg ba mel ni bànjóolig màndiŋ.