TSK

TSK · Lamentations 4:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

su boobaa ma gën leena mereeti, noonoo leen, te man ci sama bopp maa leen di mbugalati lu ko ëpp fukki yoon ak juróom, feye leen ko seen bàkkaar.

Sa doom yi ne lasar, mbete kooba yu fiir jàpp, ñu ne lareet fépp fu mbedd daje, këppoo sànjum Aji Sax ji, sa Yàlla ji leen rëbb.

¶ Moo tax Aji Sax ji Boroom bi dafa wax ne: «Sama xadar a ngii di sottiku fi bii bérab, fi kaw nit ak mala, garab ak lu suuf meññ, lépp ne jippét, te deesu ko fey.»

Su ko defee ma fenqe ku nekk ak mbokkam, fenqe waajur ak doom, ñoom ñépp.’ ”» Kàddug Aji Sax jee. Mu ne: «Duma ñéeblu, duma yërëm, duma leen ñeewantee faagaagal.»

¶ Aji Sax ji nag ne ma: «Musaa ak Samiyel sax, bu ñu taxawoon fi sama kanam, du tax ma faale askan wii. Dàqal, ñu sore ma, te wéy.

Danga naan: “Yeen buuri Yuda, yeen waa Yerusalem, dégluleen kàddug Aji Sax ji. Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Maa ngii di wàcce fi bii bérab, musiba muy buur noppi képp ku ci dégg.”

Ngëlénu Aji Sax jaa ngoog, sànjam fettax na, dig callweer, callweeral boppu ku bon.

Ndeysaan Boroom bee mer ba xiinal Janq Siyoŋ mu taaru mi. Fa asamaan la rattaxe sagu Israyil fa suuf. Keroog bésu meram ma, bàyyiwul xel, ne këram googoo di ndëggastalam.

Boroom bee tàwwi ag fittam mel ni ab noon, moo diire ndijooram, mel ni bañ, moo bóom mboolem lu neexa xool. Ci biir xaymay janq Siyoŋ mu taaru ma la yuri am sànjam ni sawara.

Aji Sax jee def la mu nammoon, moo sottal kàddoom ga mu santaane woon janti démb. Moo fàdd te yërëmul, ba may noon bége leen, te moo kaweel sa kàttanu bañ yi.

Matal nga sa kàddu gi nga wax ci nun, nook sunu kilifa yi nu yilif, ba nga wàccee ci sunu kaw, ci Yerusalem, musiba mu réy mu masula am feneen fu mboolem asamaan tiim.

Ndax janti mbugal lay doon, ngir sottal mboolem lu ñu bindoon.