TSK

TSK · Lamentations 4:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Dañuy boole njàqareek gàcce ndax réewum Kuus mi ñu yaakaaroon, ak Misra gi ñu doon sagoo.»

Wóoy ngalla doom yii diy fippukat! Kàddug Aji Sax jee. Ñu ngi nas mébét yu ma diglewul, di digoo digoo yu ma leen xelalul, di tegle bàkkaar ci kaw bàkkaar.

Léegi lu ngeen wuti Misra? Dangeen di naani ca ndoxum Niil ma ca Misraa? Lu ngeen wuti Asiri? Dangeen di naani ca dexu Efraat ca Babilon a?

ngeen jóge ca yenu seeni loxo. Aji Sax jee wacc ñi ngeen yaakaar, ba dungeen baaxlee ci ñoom.»

«Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: Buuru Yuda mi leen yebal, ngeen seetsi ma, waxleen ko ne ko: “Mbooloom Firawna mi génnoon di leen wallusi kat, dëpp na bay dellu Misra.

Samay soppe laa woo wall, ñoom ñu wor ma. Samay sarxalkat ak samay mag di wuti ab dund bu ñu leqlikoo, far faatu ci biir dëkk bi.

ba waa Misra gépp xam ne maay Aji Sax ji. «“Seen ndimbal ak Israyil mooy ndimbalu bantu barax,