Yàlla lanuy damoo bésoo bés, di màggal turam ba fàww. Selaw.
TSK
TSK · Lamentations 5:22
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Psalms 44:9
TSK
Psalms 74:1
TSK
Muy taalifu yeete, giiroo ci Asaf. Éy Yàlla, lu tax nga wacc nu fàww, di dal ak xol bu tàng ci sa xari parlu yii?
Isaiah 64:9
TSK
Sa dëkk yu sell doon nañu màndiŋ, Siyoŋ ca la, doon na màndiŋ. Yerusalem laa ne, gental na!
Jeremiah 14:19
TSK
Aji Sax ji, wacc ngaa wacc Yuda nii? Am Siyoŋ a la génnliku? Lu tax nga di nu dumaa musiba mu amul paj? Nuy yaakaar jàmm, dara baaxul, nuy séentum paj, tiitaange ne jaas!
Ezekiel 24:13
TSK
Sa sobeey sa yàqute! Maa la setal te taxu laa set. Dootuloo tàggook sa sobe, ba keroog may giifal sama xadar fi sa kaw.
Hosea 1:6
TSK
¶ Mu dellu ëmb, gannaaw gi mu am doom ju jigéen. Aji Sax ji ne: «Tudde ko Lo Ruwana» (mu firi Ki ñu yërëmul), mu ne: «ndax dootuma yërëm waa kër Israyil, dootuma leen baal.