TSK

TSK · Lamentations 5:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Seen baay Yanqóoba ne leen: «Xañ ngeen ma ay doom: Yuusufa nekkatul, Simeyon nekkatul, léegi ngeen bëgga jël Beñamin, yóbbu. Loolu lépp ci sama kaw; ngalla man!»

“Aji Sax ji! Kiy muñ mer, te bare ngor, di bale tooñ aki moy te du ñàkka topp mukk doom, tooñu waajuram, ba ca sët yaak sëtaat ya.”

Job 7:21 TSK

Lu tee kon nga baal ma samag moy, jéggal ma samag tooñ? Léegi tey ma tëri biir suuf, nga di ma seeta seet, fekk nekkatuma.

Nga wax leen nag ne leen: “Seeni maam a ma wacc,” kàddug Aji Sax jee, “di topp yeneen yàlla, di leen jaamook a sujjóotal. Man nag, ñu dëddu ma; sama yoon it, ñu bañ koo sàmm.

Aji Sax ji dafa wax ne: «Yuux dégtu na fa Raama, ay jalooki jooy yu metti. Rasel ay jooy ay doomam, baña noppi, ndax doomam ya wuute.»

Sag yàqute ak sa jëf ju siblu nag, yaa koy gàddu. Kàddug Aji Sax jee.

«Seeni maam, ana ñu tey? Yonent yi nag, ndax ba fàww lañuy dund?