TSK

TSK · Leviticus 1:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Nañu raxas yérey biir yi ak yeel yi, sarxalkat bi boole lépp lakk ci kaw sarxalukaay bi. Saraxu rendi-dóomal la, saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.

Na doomi Aaróona yi boole yooyu lakk ci kaw sarxalukaay bi, mu tege ci kaw saraxu rendi-dóomal bi ci kaw mattum taal bi. Saraxu sawara la ngir xetug jàmm ñeel Aji Sax ji.

Ba loolu weesee Musaa boole yérey biir yi, ak yeel yi, raxas, ba noppi lakk kuuy mi yépp ca sarxalukaay ba. Loolu saraxu rendi-dóomal la, ngir xetug jàmm. Saraxu sawara la, ñeel Aji Sax ji, na ko Aji Sax ji sante woon Musaa.

Ñaareelu xar mi, sarxal-leen ko diggante ngoon ak jant bu so, mu ànd ak saraxu peppam ak saraxu tuuram niki ci suba, ngeen def ko saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.

¶ Am na néeg buy ubbikoo ci biir mbaaru bëj-gànnaar ba féete biir. Fa lañuy raxase yàppu saraxu rendi-dóomal.