ak mburu yu mag yu amul lawiir, ak kàmp yu sew yu amul lawiir yu ñu xiiwaale diw, ak mburu yu tàppandaar yu amul lawiir, ñu wis diw ca kaw, te sungufu bele su mucc ayib ngay defare yooyu.
TSK
TSK · Leviticus 10:12
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Exodus 29:2
TSK
Leviticus 2:1
TSK
¶ «Bu nit dee indil Aji Sax ji saraxu pepp, sunguf su mucc ayib la saraxam wara doon, mu sotti ci diw, def ci cuuraay,
Leviticus 2:10
TSK
Li des ci saraxu pepp mi, Aaróona aki doomam ñoo koy féetewoo, muy cér bu sella sell, bawoo ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji.
Leviticus 7:9
TSK
Ci biir loolu bépp saraxu pepp mu ñu lakk cib taal, mbaa ñu saaf ko ci cin mbaa ci saafukaayu weñ, sarxalkat bi koy joxe moo koy moom.
Leviticus 24:9
TSK
Mburu yooyu Aaróona aki doomam yu góor ñoo koy féetewoo, te nañu ko lekke fu sell, ndaxte lu sella sell la, di lu ñu séddoo fàww ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji.»
Ezekiel 44:29
TSK
Saraxu pepp ak saraxu póotum bàkkaar ak saraxu peyug tooñ, ñoom ñoo koy lekk, te lépp lu ñu jagleel Aji Sax ji ci Israyil, ñoo koy moom.