Ñu jàpp ca seeni mbubb, génne leen dal ba, muy la Musaa santaane woon.
TSK
TSK · Leviticus 10:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Turi doomi Aaróona yu góor, sarxalkat yaa ngi noonu; ñu faloon leen, sédd leen céru carxal.
ñooña doon baatal réew ma, am mbas a leen rey fi kanam Aji Sax ji.
¶ Ci kaw loolu sawara moo bawoo fa Aji Sax ji, xoyom ñaar téeméeri nit ak juróom fukk ña indi woon saraxu cuuraay ba.
Nadab ak Abiyu ña nga dee keroog ba ñu taalalee Aji Sax ji cuuraay lu warul.
Sànjum Aji Sax ji nag tàkk ci kaw Usa. Yàllaa ko fàdd foofa, ndax ug teeyadeem, mu dee foofa ca wetu gaalu Yàlla ga.
Ilyaas wax njiital juróom fukki dag ya, ne ko: «Ndegam góoru Yàlla laa, yal na sawara wàcce asamaan xoyom la, yaw yaak sa juróom fukki dag.» Sawara daldi bàyyikoo asamaan, ne jippét xoyom leen, mook juróom fukki dagam ya.
¶ Naka la Anañas dégg kàddu yooyu, daldi daanu, dee. Tiitaange lu réy nag dikkal ña ko dégg ñépp.
¶ Xew-xew yooyu dal maam ya ay misaal la, te dees koo bind ngir nu jànge ci, nun ñi mujug jamono yemool.