¶ «Su fekkee ne nit ki dafa laal lu sobewu, te seetluwu ko, lu mel ni rab wu daganul te médd, muy rabu àll mbaa ag jur, mbaa luy raam, kon sobewu na, tooñ na.
TSK
TSK · Leviticus 11:24
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Buleen ci lekk lenn te buleen laal méddam ndax lenn daganu ci, ci yeen.
Yooyoo daganul ci yeen ci mboolem rab yu sew-sewaan yiy dox ne ñàpp ci suuf. Képp ku laal lenn lu ci dee dina yendoo sobe ba jant so.
¶ «Ku dugg biir néeg bi diiru fan yi mu tëje dina yendoo sobe ba jant so.
Ku toog ci lenn lu boroom jàngoroy xelli toogoon, na fóot ay yéreem, sangu, te du tee mu yendoo sobe ba jant so.
Su ku ànd ak jàngoroy xelli tiflee ku taqul sobe, na kooku fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so.
Boroom jàngoroy xelli bu raxasul ay loxoom, ku mu laal, kooku, na fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so.
Te it képp ku laal ab lalam, war naa fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so.
Su toogoon ci lal mbaa leneen lu mu toogoon, ku laal loola dina yendoo sobe ba jant so,
¶ «Ka wacci woon sikketu Asasel, na fóot ay yéreem, sangu, doora mana duggaat ci dal bi.
¶ «Te itam képp ku lekk médd mbaa lu rab fàdd, muy njuddu-ji-réew mbaa doxandéem, na fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so, mu doora set.
dina yendoo sobe sa ba jant so, te du lekk ci sarax yu sell yi ndare du dafa sangu.
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dégtal na ma lii: «Gii ñaawtéef déy deesu leen ko jéggal, ba keroog ngeen di dee.» Boroom bee ko giñ, moom Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.
Kon nag: «Nangeen génne ci seen biir, te teqlikoo ak ñoom,» la Boroom bi wax. «Lu sobewu, buleen ko laal. Su boobaa, maa leen di dalal.
jëfi lëndëm amul njariñ, buleen ci bokk, xanaa ngeen feeñal ñaawtéefu jëf ja.
¶ Ndegam nag yeena bokk ak Almasi dee, ba teqlikoo ak li àddina def cëslaay, ana lu tax ngeen mel ni ñu bokk ci àddina ba tey, di tegoo ay dogali yoon yu mel nii: