Leviticus 6:21
TSK
Su fekkee ne ndabal xandeer lañu togge woon yàppu sarax sa, nañu ko toj. Bu doon ndabal xànjar, ñu jonj ko, raxas ko.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Su fekkee ne ndabal xandeer lañu togge woon yàppu sarax sa, nañu ko toj. Bu doon ndabal xànjar, ñu jonj ko, raxas ko.
Lépp lu lenn ci yooyu dee, ba dal ca, la mu dal sobewu na. Su dee ab puuru ban mbaa cin, dees koy toj ndax sobewu na te lu setul la ci yeen.
Néeg ba dees koy daane, boole doj yaak bant yaak banu raax ba bépp, génne ko dëkk bi, tuur ko fu setul.
te mboolem ndab lu fa ubbiku woon, kubeer it ubu ko woon ràpp, loola ndab sobewu na.
¶ Xam nanu ne sunu yaram, sunu këru kaw suuf gii di ab xayma, bu daanoo it, am taax lanu am fa Yàlla, kër gu sax dàkk, gu loxol nit tabaxul.