TSK

TSK · Leviticus 11:44

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

waaye yeenay doon nguuru sarxalkati Yàlla, te di xeet wu sell.” Kàddu yooyu ngay wax bànni Israyil.»

Te itam nit ñu sell ngeen wara doon, ñeel ma, kon nag yàppu mala mu ñu fàdde ci àll bi, buleen ko lekk; sànnileen ko xaj yi.

Musaa ne Aaróona: «Lii la Aji Sax ji doon wax ba mu nee: “Ci biir ñi may jegeñ laay feeñal samag sellaay, te ci kanam mbooloo mi mépp lees may terale.”» Aaróonaa nga ne cell.

«Waxal bànni Israyil ne leen: Man Aji Sax ji maay seen Yàlla.

¶ «Na ku nekk weg ndeyam ak baayam te wormaal sama bési Noflaay. Man Aji Sax ji, maay seen Yàlla.

Seen tóokëri reseñ it buleen ko witt ñaari yoon te buleen foraatu doom yu wadde ca witt ma. Aji ñàkk akub doxandéem ngeen koy bàyyee. Maay seen Yàlla, man Aji Sax ji.

¶ «Nangeen ma nekkal ñu sell, ndaxte ku Sell laa, man Aji Sax ji, te dama leena ràññatleek yeneen xeet yi, ngeen di sama ñoñ.

Su ko defee ngeen di bàyyi xel tey jëfe sama santaane yépp, daldi doon ñu sell, ñeel seen Yàlla.

Ci kaw loolu waa Bet Semes ne: «Ana ku mana taxaw fi kanam Aji Sax ji, jii Yàlla ju sell? Ci kan lanuy yóbbu gaal gi, ba mu sore nu?»

Màggal-leen sunu Yàlla, Aji Sax ji, te sujjóot fa tundam wu sell wa. —Sunu Yàlla Aji Sax jee sell!

Man Aji Sax ji, maay sa Yàlla; man Aji Sell ju Israyil, maa lay musal. Maa joxe Misra, feye la; ak Kuus ak Seba, ma weccikoo la.

Amos 3:3 TSK

Ñaar dina ànd te digewuñub dajee?

¶ Waaye yeen nag yeen ay giir giy tànneef, yeenay sarxalkati Buur, yeen ay askan wu sell, yeen ay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.