TSK

TSK · Leviticus 11:45

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Maa leen di def sama ñoñ, di seen Yàlla. Dingeen xam ne man Aji Sax ji maay seen Yàlla, ji leen di teggil sas, yi leen waa Misra teg.

«Man Aji Sax ji, maa di seen Yàlla, ji leen génne réewum Misra, kërug njaam ga.

ndaxte man Aji Sax ji maay seen Yàlla. Kon nag sell-luleen te sell ndax man ku Sell laa. Kon buleen sobeel mukk seen bopp ci mboolem bindeef yu sew-sewaan yiy dox ci suuf.

Na seen nattukaayu diisaay jub, doom ya ngeen cay natte jub, te na nattukaayi sol-sotti yi jub. Maay seen Yàlla Aji Sax, ji leen génne réewum Misra.

génne leen réewum Misra, di seen Yàlla. Maay Aji Sax ji.»

Maa leen di bàyyil xel ci sama kóllëre gaak seen maam ya ma génne réewum Misra, jaambur ñi seede, ngir doon seen Yàlla. Maay Aji Sax ji.»

«Kenn sellul ni Aji Sax ji, amuloo dend moos, cëslaay melul ni sunu Yàlla!

«Maa soppoon Israyil ba muy ndaw, Fa Misra laa ko wooye, muy sama doom.

Ndax kat bindees na ne: «Sell-leen, ndax man ku Sell laa.»