Na lakk nebbon bi yépp ci kaw sarxalukaay bi, def ko ni nebbonu saraxu cant ci biir jàmm. Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayal bàkkaaram, mu am njéggal.
TSK
TSK · Leviticus 12:8
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Leviticus 4:26
TSK
Leviticus 5:11
TSK
¶ «Su amul lu mat njégu ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw, li muy indi, sarxal ko ngir bàkkaar bi mu def, ñetti kiloy sunguf su mucc ayib lay doon, muy saraxu póotum bàkkaar. Du ci def diw, te du ci sotti cuuraay, ndax li mu di saraxu póotum bàkkaar.
Leviticus 15:14
TSK
Bésub juróom ñetteel ba, na wut ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw te teewi fi kanam Aji Sax ji ca bunt xaymab ndaje ma, daldi koy jox sarxalkat bi.
Leviticus 15:29
TSK
Bésub juróom ñetteel ba na wut ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw, yóbbu ca sarxalkat ba, ca bunt xaymab ndaje ma.
Xam ngeen kat sunu yiwu Boroom Yeesu Almasi, moom mi woomle woon, te yeena tax mu ñàkk, ngir woomale leen ag ñàkkam.