Leviticus 14:50
TSK
Day rendi menn picc mi, tiimale ko ndabal xandeer mu def ndox mu balle ci bëtu ndox.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Day rendi menn picc mi, tiimale ko ndabal xandeer mu def ndox mu balle ci bëtu ndox.
¶ «Bésub keroog bëtu ndox dina bënnal kër Daawuda, ak waa Yerusalem, ngir setal bàkkaar ak sobe.
mi ñu teg ciy loxo, mu dee ndax sunuy tooñ, ba dekkal ko, ngir nu jagoo àtteb nit ñu jub.
Moo tax Yàlla kaweel koo kaweel, baaxe ko tur wi tiim wépp tur,
tukkee itam fa Yeesu Almasi, seede bu wóor bi, moom taaw bi, ki jëkka dekki, jóge ci ñi dee, di kilifay buuri kaw suuf. Moom mi nu sopp, yiwee nu deretam, ba nu teqlikook kilifteefu sunuy bàkkaar,