Su ko defee sarxalkat bi capp baaraamam ci deret ji, wis-wisal deret ji juróom ñaari yoon fi kanam Aji Sax ji, fa janook ridob bérab bu sell ba.
TSK
TSK · Leviticus 14:7
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
ba noppi wis-wisal ca juróom ñaari yoon ca kaw sarxalukaay ba, diwe ko sarxalukaay ba ak mboolem ay ndabam, boole ca mbalkam njàpp ma, mook ub tegoom ngir yooyu it sell.
Na ko sarxalkat bi seet, ba gis ne weexaat na, mu biral ne ki jàngoro ji dal set na te kon it set na.
Na sàkk ci deretu yëkk wi, wis-wisale ko baaraamam ci kaw kubeeru gaal gi, ci wetam gi féete penku, te it na wis-wisale baaraamam deret ji lu mat juróom ñaari yoon ci kanam kubeeru gaal gi.
Sikket bi day yenu seeni ñaawtéef yépp, yóbbaale ca ndànd-foyfoy ga, ñu wacc ko ca màndiŋ ma.
Bu loolu wéyee, na ku set jël caru isob, capp ko ca ndox ma, wis-wisal ko ca kaw xayma ba nit deeye, wis ko ca kaw ndab yépp, ak ca kaw nit ña fa nekkoon. Na ko wis itam ci kaw nit ku laal yaxi ku dee, mbaa mu laal ku ñu bóome saamar, mbaa mu laal ku Yàlla moomal boppam, mbaa mu laal bàmmeel.
Alyaasa yebal ndaw ca moom ne ko: «Demal sanguji juróom ñaari yoon ca dexu Yurdan, sa yaram set, dellu mel na mu meloon.»
Mooy ba ko Yonent Yàlla Natan seetsee, gannaaw ba Daawuda dëkkoo ndaw sa ñuy wax Batseba.
waaye noonu it lay waare ay xeeti xeet, ba buur yi wedam, ngir lu ñu leen waxuloon, te ñu gis ko, lu ñu dégguloon, te mujj ko ràññee.»
¶ «Juróom ñaar fukki ayi bés lañu àppal sa mbooloo ak sab dëkk bu sell, ngir dakkal tooñ gi, jeexal moy gi, jotu ñaawtéef, saxal njubte ba fàww, matal peeñum yonent, ba delloo bérab bu sella sell ag sellngaam.
Ndegam deretu sikket ak yëkk, ak nag wu jigéen wu ñu lakk, ngir suy dóom ba nit ku sobewu, yooyu lees daan sellale nit ñi, ngir seen cetug yaramu suuxu neen,
Xayma ba, ak mboolem ndabi carxal ya it, noonu la wis-wisale ca kaw.
Kon nag nanu agsee fi Yàlla xol bu dëggu, ak fit wu mat sëkk wu ngëm waral, gannaaw wisees na sunum xel ndoxum setlu, ba mu tàggook bépp gàkk bu mu nu sikkale, te raggees na sunu yaram ci ndoxum setlu.
Yeen la Yàlla Baay bi ràññee lu jiitu, ci ni mu leen sellale Noo gu Sell gi, ngir ngeen mana déggal Yeesu Almasi, boole ci tooyloo deretam, mu setal leen. Aw yiw ak jàmm ju ne xéew ñeel na leen.