Waaye sikket bi muurloo doon sikketu Asasel, dees koy taxawal muy dund fi kanam Aji Sax ji, te ni ñu koy jotoo, mooy dees koy dàq mu dem ca màndiŋ ma, ngir Asasel.
TSK
TSK · Leviticus 16:17
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Leviticus 16:10
TSK
Isaiah 53:6
TSK
Nun ñépp a lajj niy xar, ku nekk walbatiku topp yoonam, te Aji Sax jee ko këpp sunu gépp ñaawtéef.
Luke 1:10
TSK
¶ Mbooloo mépp nag a nga woon ca biti di julli, ca waxtuw saraxu cuuraay boobu.
1 Timothy 2:5
TSK
Ndax kat jenn Yàlla doŋŋ moo am, benn Defarekat doŋŋ it moo am diggante Yàlla ak nit ñi, te mooy nit ki Almasi Yeesu,
Hebrews 9:7
TSK
Waaye ñaareelu néeg ba, sarxalkat bu mag ba doŋŋ moo ca daan dugg, benn yoon cim at, te du ñàkka duggaale deret ju muy jooxe ngir boppam, ak itam ngir bàkkaar yi askan wi def te du ag teyeef.
1 Peter 3:18
TSK
Almasi itam benn yoon la daj coono ndax bàkkaari nit ñi, moom miy ki jub moo leen ko defal yeen ñi jubadi, ngir yóbbu leen fa Yàlla; moom lañu rey yaramu suuxam, waaye moo dundaat ci dooley Noo gi.