Musaa rendi ko, sàkk ci deret ji, capp ci baaraamam, diw ci ñeenti béjjéni sarxalukaay bi yépp, setale ko sarxalukaay bi. Mu daldi tuur li des ci deret ji ci taatu sarxalukaay bi, sellale ko noonu, muy njotlaayal sarxalukaay bi.
TSK
TSK · Leviticus 16:20
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Leviticus 8:15
TSK
Ezekiel 45:20
TSK
Noonu it ngay def ca juróom ñaareelu fanu weer wa, ngir daboo ko nit ku jàdd yoon te yégu ko mbaa teyu ko. Su ko defee ngeen def njotlaayal kër Yàlla gi.
Romans 8:34
TSK
Ana kuy tegeb daan? Almasi Yeesu de moo dee, rax ci dolli, mu dekki, te moo toog fa ndijooru Yàlla, di nu fa ñaanal!
Colossians 1:20
TSK
Deretam ja tuuru ca bant ba, ca la Yàlla defe jàmm, ba sottale ci moom, pexe mi mu jubalee boppam ak lépp, muy lu nekk ci kaw suuf, ak la fa asamaan.
Revelation 1:18
TSK
Maay Kiy Dund, maa dee woon, maay dund nii tey ak ëllëg ba fàww te maa yor caabiy dee ak njaniiw.