TSK

TSK · Leviticus 16:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Na teg loxoom ci kaw boppu juru saraxu rendi-dóomal bi, ndax ñu nangul ko ko, muy njotlaayam.

¶ «Su ko defee ñoom dinañu tudd seen bàkkaar ak seen bàkkaaru maam ya, ndax dañu maa wor te dëkke maa noonoo,

Ngalla Sang bi, teewlu ma, xippi say gët, te déglu sama ñaan, yi may ñaanal guddeek bëccëg bànni Israyil, say jaam. Tegoo naa moy yi la bànni Israyil moy, te man sax maak sama waa kër baay, moy nanu la.

Ma xamal la ne moy naa, làqatuma la sama ñaawtéef. Ma ne: «Naa àgge Aji Sax ji sama bàkkaar.» Yaw nga baal ma peyug tooñ. Selaw.

Kuy làq say tooñ doo baaxle, ku koy nangu, tuub ko, am yërmandey Yàlla.

Ma walbatiku jublook Boroom bi Yàlla. Maa ngi sol saaku, diwoo dóom boole kook koor, toroxloo ko, di ko ñaan ak a dagaan.

Almasi mi masula bàkkaar, moom la Yàlla sëf sunu bàkkaar, ngir nu mana ame ci moom àtteb nit ñu jub fa Yàlla.