Psalms 103:10
TSK
Du sunuy bàkkaar la nu mbugal, du sunuy ñaawtéef la nu fey.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Du sunuy bàkkaar la nu mbugal, du sunuy ñaawtéef la nu fey.
Mooy sonn ba gis ug leer, doyloo ko, te ñu bareey xam sama jaam bii di Aji Jub, ba mu àtte leen àtteb njekk, sëfoo seeni ñaawtéef.
Moo nuy yërëmati; sunuy ñaawtéef lay joggiy tànkam, te biir xóotey géej lay tàbbal sunuy bàkkaar.
¶ Almasi moom, moo nu jot ci alkàndey yoon wi, ba mu doonee ku alku ngir nun, nde: «Alkute ñeel na képp ku ñu rey, wékk ko ci bant.»
«Moom ci boppam moo gàddu sunuy bàkkaar, moo ko tegoo ci yaramu boppam ca bant ba,» ngir nu deeyal bàkkaar te dundal njub; «moom mooy ki ngeen wére ci ay góomam.»