¶ Ibraayma nag jëmbat na garabu tamaris foofa ca Beerseba, tudd fa Yàlla Aji Sax ji, ji nekk ba fàww.
TSK
TSK · Leviticus 17:5
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Naka la Ibraayma siggi rekk, yem ci menn kuuyum xar mu béjjén ya lonke ci as ngarab. Ibraayma dem, jël kuuy ma, rendi, mu wuutu doom ja, di ab saraxu rendi-dóomal.
Ba mu ko defee mu yebal ay ndawi bànni Israyil, ñooña def ay saraxi rendi-dóomal, boole ci rendi yëkk yu ndaw yu ñu def saraxi cant ci biir jàmm, ñeel Aji Sax ji.
¶ «Li yoon dogal ci saraxu cant ci biir jàmm, te nit sañ koo sarxalal Aji Sax ji mooy lii:
Terewul mbooloo ma di rendi ay sarax ca bérabi jaamookaay ya, ndax ca yooya jamono tabaxaguñu woon kër gu ñu tudde Aji Sax ji.
Dañoo sàkkal seen bopp ay bérabi jaamookaay, samp ay tuuri doj aki xer yu ñuy jaamoo Asera ca kaw mboolem tund wu kawe mbaa ker garab gu naat.
Ñu boole ca sampal seen bopp ay tuuri doj ak xer yu ñuy jaamoo Asera ci kaw mboolem tund wu kawe mbaa ker garab gu naat.
Maa leen yóbbu réew ma ma leen giñaloona jox, teewul fu ñu gis tund wu kawe, mbaa garab gu sëq, rendi nañu fa seeni sarax, jooxe fa seen jooxe yi may merloo, taal fa seen saraxi cuuraay, tuural fa seeni tuur.