TSK

TSK · Leviticus 18:27

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

ndax ñu bañ leena royloo, ngir ngeen di jëfe seen mboolem yu jomblu yi ñuy defal seeni tuur, ba ngeen moy seen Yàlla Aji Sax ji.

Seen Yàlla Aji Sax ji kat seexlu na képp kuy def yooyii, képp kuy def ug njublaŋ.

Réew ma amoon na sax ñuy jaay seen bopp fa ñuy màggale tuur ya. Ñuy def mboolem ñaawtéefi xeet ya Aji Sax ji dàqoon ngir bànni Israyil.

Manase nag di def li Aji Sax ji ñaawlu, topp ñaawtéefi xeet ya Aji Sax ji dàqoon ngir bànni Israyil.

ba mujj reew bay def jëf ju siblu, may gis. Looloo waral ma beddi leen nii, nga gis.

«Ni cabbu reseñu biir màndiŋ, ni laa fekke Israyil. Ni ndoortel doomi figg ju ndey ja taawloo, ni laa gise seeni maam. Waaye ñoom ñoo dem Baal Pewor, ñoo sédd seen bopp Baal, tuur mu ruslu mi, ba tax leena seexluwu ni kooku ñu sopp.