¶ «Buleen sàcc.
TSK
TSK · Leviticus 19:11
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Su fekkee dañoo jàpp ab sàcc guddi, muy toj kër jaambur, bu ñu ko dóoree, ba mu dee, deesul topp ki dóor, bakkanu sàcc bi,
li leen di àtte ngiñ lay doon ci Aji Sax ji. Na ka dencoon mala ma giñ ne jëlu ko. Na boroom mala mi it nangu ngiñ li. Ki dencoon du ko fey dara.
¶ «Buleen sàcc.
Kuy njublaŋ du tooge sama kër, kuy fen du taxaw sama kanam.
«Ndax ki gëna tuut ba ki gëna mag, ñépp a ngi lewal lu lewul. Yonent akub sarxalkat, ñépp a ngi wor.
«Na ku ne moytu dëkkandoom te baña wóolu menn mbokk. Kuy mbokk déy lal nga pexem wuruj, di wuruj; kuy dëkkandoo, sos ngay wéye.
«Ndigal yii, nangeen ko jëfe: Deeleen waxante dëgg, te dëgg ak yoon, nangeen ko àttee àtteb jàmm ci seen ëtti àttekaay.
Mukk kay! Fàww Yàlla wéye di ku dëggu, te ñépp di ay fen-kat, te noonu la Mbind mi indee ne: «Soo waxee, am dëgg, te soo àttee, yey.»
¶ Kon nag bàyyileen fen, te ku nekk di wax sa moroom, dëgg, ndax ku nekk ci yeen sab céru moroom nga.
Buleen di fenante, gannaaw seen jëmm ja woon démb, boole ngeen kook jëfinam ja mu àndal, summi,
waaye ñu ragal ñi ak aji gëmadi ñi ak defkati ñaawtéef yi ak bóomkat yi ak moykat yi ak xërëmkat yi ak bokkaalekat yi, mboolem niti fen ñi, seen añ a nga ca déegu sawara waak tamarax ba. Loolu moo di ñaareelu dee.»