Saa yu ay nit jotee ci mbirum nag mbaa mbaam mbaa gàtt mbaa yére, mbaa lu réer lu mu doon, ñaar ñi solowoo alal ji, muy mala mbaa leneen, nañu yóbbu mbir mi fi kanam àttekat yi. Ku ci àttekat yi teg tooñ, na fey moroom mi ñaari yoon.
TSK
TSK · Leviticus 19:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Su góor naxee ab janq bu kenn joxagul warugar, ba tëdde ko, na fey warugaram, muy jabaram.
¶ «Bu ngeen dee lebal ku bokk ci sama ñoñ, di néew-ji-doole ju ngeen dëkkal, buleen def ni ab leblekat, di ko sas ab tegandaay.
Bu ngeen di jaay seen waa réew suuf nag mbaa ngeen di jënde suuf ci seen waa réew, buleen di naxante.
¶ Buleen gàddu àqu liggéeykat, baadoolo bu néew doole ci seen biiri bokk, mbaa ci seen dëkkandoo yiy doxandéem ci seen dëkk yi ci réew mi.
Daa mel ni jaam bu namm keppaar mbaa mbindaan mu yàkkamtig peyam.
Nattu diisaay yu yemul ak lu ni mel, Aji Sax ji bañ na ko.
Aji Sax ji dafa wax ne: Deeleen jëfe dëgg ak yoon, di xettli ku ñu xañ dëgg ci ki koy néewal doole. Ab doxandéem, ab jirim akub jëtun, buleen leen lor, buleen leen fitnaal. Deretu jaambur bu deful dara it, buleen ko tuur ci bii bérab.
Waa réew maa ngi lekk àq, di sàcc. Baadoolo yeek walaakaana yi, ñu néewal; doxandéem bi, ñu not, xañ ko àqam.
Ci moomu mbir, bu kenn ci yeen tooñ mbokkam, di aakimoo yelleefam, ndax waxoon nanu leen ko, ba artooti leen ne leen jëf ju ni mel, Boroom bee koy fey ña ko def.