TSK

TSK · Leviticus 19:23

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Musaa tinu Aji Sax ji ne ko: «Waaw, ndegam bànni Israyil sax nanguwuñu maa déglu, nu ma Firawna di déggale, man mii tëlee wax?»

Seen jur gu gudd ak gu gàtt itam, naka noonu. Juróom ñaari fan lay nekk ak ndeyam, bésub juróom ñetteel ba, ngeen jox ma ko.

«Bu ngeen demee ca réewu Kanaan ga ma leen jox muy seen moomeel, bu ma tegee liir wuy law ba xuural ab néeg foofa ca seen réewum bopp,

Du mburu, du pepp mu ñu séndal, du pepp mu bees mu ngeen wara lekk, ba keroog bés boobu ngeen di indi seen saraxu Yàlla. Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, yeen ak seen askan, ak fépp fu ngeen dëkk.

muy waa Misra, di waa Yuda, di Edomeen ñeek Amoneen ñi, di Mowabeen ñeek mboolem ñiy wat seen peggu kawaru bopp te dëkke màndiŋ mi, nde xeet yooyu, kenn xarafu ci dëgg, waaye bànni Israyil gépp it xarafuñu xarafu xol.»