TSK

TSK · Leviticus 19:28

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Gannaaw loolu Aji Sax ji wax na Musaa ne ko: «Waxal sarxalkat yiy doomi Aaróona ne leen: Bu ci kenn sobeel boppam, di laal mbokkam mu dee,

¶ Ay doom ngeen, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Buleen ñaasu, buleen wat seen kawaru bopp fi féeteek jë bi, ngir di ko mititloo ku dee,

Ku mag ak ku ndaw ay dee ci réew mii, te deesu leen rob, deesu leen jooy. Kenn du dagg yaramam mbaa muy nelu, di ko ñaawloo.

¶ Meneen malaaka, topp ci, di ñetteel bi. Mu àddu ca kaw, ne: «Képp ku sujjóotal rab wi ak jëmm ji ñu ko sàkkal, ba ñu defal ko màndargam jë mbaa loxo,

Ma gisati lu mel ni géeju kiristaal bu jaxasook sawara. Ci biir loolu ña daanoon rab waak jëmmu nataalam, ak lim bi méngook turam, ñu ngi taxaw ci kaw géeju kiristaal gi, yore ay xalami Yàlla.

Ñu daldi jàpp rab wi, mook yonentu caaxaan, bi defoon ci turu rab wi ay kéemaan yu mu sànke ña ñu màndargaale woon màndargam rab wi, te ñu doon jaamu jëmmu nataalu rab wi. Ñoom ñaar ñépp lañu sànni, ñuy dund ca déegu sawara waak tamarax bay bax.