TSK

TSK · Leviticus 19:31

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Na ku nekk weg ndeyam ak baayam te wormaal sama bési Noflaay. Man Aji Sax ji, maay seen Yàlla.

Ku jublu ci ñiy gisaane nit ñu dee mbaa mu jublu ci boroom rawaan yiy seet, topp leen, di ma leen bokkaalee, dinaa ko noonoo moom itam te dinaa ko dagge ci biir bànni Israyil.

Bu kenn fekk ci seen biir kuy sarxe doomam ju góor, ak ju jigéen, lakk ko; ak kuy luxus, ak kuy seet, ak kuy gisaane, ak kuy xërëm,

Sóol wax ay jawriñam, ne leen: «Seetal-leen ma jigéen juy seete nit ñu dee, ma seetluji ci moom.» Jawriñ ya ne ko: «Xanaa jigéenu gisaanekat ba ca Endor.»

Te itam sarxal na doomam, lakk ko ngir ay tuur. Ci biir loolu jabar na, ñeengo na, jëflante naak boroom rawaan aki gisaanekat. Bare na lu mu def lu Aji Sax ji ñaawlu, ba merloo ko.

Dinga suufe ba mel ni kuy àddoo biir suuf, sa baat di ndéey lu dégtoo xóote ya pëndub suuf lale, mel ni njuuma lu waxam bawoo biir suuf, baatam yeloo xóote ya pëndub suuf lale.

Acts 8:11 TSK

La ñu ko teewloo woon moo di jëfi ñeengo ya mu leen yàgga yéeme.

¶ Noo doon dem jullikaay ba, ab surga bu jigéen bu rabu gisaane jàpp, dajeek nun. Alal ju bare la ay njaatigeem daa jële ci ngisaaneem.

ak bokkaale, ak xërëm, ak mbañeel, ak féewaloo, ak kiñaan, ak mer mu ëpp, ak jiital say bëgg-bëgg, ak réeroo, ak xàjjalikoo,