TSK

TSK · Leviticus 19:33

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Ab doxandéem, buleen ko lor, buleen ko not, ndaxte yeen itam ay doxandéem ngeen woon fa réewum Misra.

¶ «Ab doxandéem, buleen ko not; yeen ci seen bopp, jaar ngeen ci ndoxandéem, ndax ay doxandéem ngeen woon ca réewum Misra.

¶ Buleen gàddu àqu liggéeykat, baadoolo bu néew doole ci seen biiri bokk, mbaa ci seen dëkkandoo yiy doxandéem ci seen dëkk yi ci réew mi.

Ndey ak baay, ñu tuutal fi sa biir; doxandéem bi, ñu lekk àqam fi sa biir; jirim akub jëtun, ñu néewal fi sa biir.

«Maa leen di dikke ab àtte, di ab seede bu taxaw temm ci tuumaal ñeengokat yeek njaalookat yi, ak ñiy fene ngiñ, ak ñiy xañ ab liggéeykat peyooram, di noggatu ab jëtun akub jirim, di beddi doxandéem te ragaluñu ma.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.