Leviticus 18:4
TSK
Samay santaane ngeen wara dégg tey topp samay dogal. Man Aji Sax ji maay seen Yàlla.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Samay santaane ngeen wara dégg tey topp samay dogal. Man Aji Sax ji maay seen Yàlla.
¶ «Kon sàmmleen samay santaane te di ko jëfe. Maay Aji Sax ji.
¶ Mu ngoog, jàngal naa leen ay dogali yoon, aki àttey yoon, na ma ko sama Yàlla Aji Sax ji sante, ngir ngeen war koo jëfe ca biir réew ma ngeen di nanguji.
¶ Lii mooy santaane bi, ak dogali yoon yeek àttey yoon yi seen Yàlla Aji Sax ji santaane ma jàngal leen ko, ngir ngeen di ko jëfe ca réew ma ngeen jàll jëm, ngir nanguji ko,
Te santaane yeek dogal yeek yoon week ndigal li ma leen bindaloon, fexeleen ba di sàmmonteek moom ba fàww. Buleen wormaal yeneen yàlla.
May ma dég-dég, ma topp saw yoon, toppe ko xol bu tàlli.