TSK

TSK · Leviticus 2:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayal bàkkaar, bi mu def te mu bokk ci xeeti bàkkaar yooyu ñu lim. Su ko defee mu am njéggal. Li des ci sarax bi sarxalkat bee koy moom, mu mel ni bu doon saraxu pepp rekk.»

Waaye juru saraxas póotum bàkkaar deesu ci lekk lenn te fekk deretam dugg ca biir xaymab ndaje ma, ñu di ca amal ag njotlaay ca biir bérab bu sell ba. Loolu du lu ñuy lekk. Dees koy lakk, ba mu dib dóom.

¶ Ci kaw loolu Musaa wax ak Aaróona ak doomam yu góor yi des, di Elasar ak Itamar, ne leen: «Jël-leen saraxu pepp mi des ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji, ngeen lekk ko, bañ cee boole lawiir, ci wetu sarxalukaay bi, ndax lu sella sell la.

Du tere mu saña lekk ci ñamu Yàllaam, muy ñam wu sell ak wu sella sell.

Maa tànne sa baay ci digg giiri Israyil yépp, ngir mu doon sama sarxalkat, di yéeg ci sama sarxalukaay, di taal cuuraay, sol xar-sànni mi, janook man. Maa sédd it sa waa kër baay mboolem saraxi sawara yu bànni Israyil.

Saraxu pepp ak saraxu póotum bàkkaar ak saraxu peyug tooñ, ñoom ñoo koy lekk, te lépp lu ñu jagleel Aji Sax ji ci Israyil, ñoo koy moom.