TSK

TSK · Leviticus 2:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Noonu la Ibraayma jënde toolub Efron ba nekk ca Magpela te janook Mamre, muy moomeelam. Dafa jënd tool ba bépp, jëndaale xuntim xeer ma ca biir, ak garab ya ca sax yépp, ba fa tool ba yem. Mboolem Etteen ña séqoon pénc ma, seede nañu ne Ibraayma moo ko moom.

¶ «Diiru juróom benni at ngeen di ji seen tool, for li ci meññe;

Sarax boobu da ciy dolli mburu yu am lawiir, boole kook saraxu cant googu ci biir jàmm te mu jublu ci njukkal.

seen notu sunguf bu jëkk, ci ngeen di jooxe menn mburum jooxe. Ni ngeen di sàkke jooxe bu jóge ca dàgga ja rekk, ni ngeen koy jooxee.

Moo ma taxa indi nii ndoortel meññeefum suuf, si nga ma jox, Aji Sax ji.» Su ko defee mu taaj pañe bi fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji, daldi sujjóot fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji.

¶ Waaye nag Almasi dafa dekki moos, te mooy saraxu ndoortel meññeef, bi ñu sàkke ci ngóobum bakkani nit ñi dee.