Nañu raxas yérey biir yi ak yeel yi, sarxalkat bi boole lépp lakk ci kaw sarxalukaay bi. Saraxu rendi-dóomal la, saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.
TSK
TSK · Leviticus 2:9
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Sarxalkat bi ñuy fal ci doomi Aaróona yu góor yi, mu war koo wuutu, da koy def moom itam. Aji Sax ji moo jagoo sarax boobu fàww, te dañu koy lakk ba mu jeex.
Noon yaa ngi ma gaw ni coggalu yëkk, dar ma ni ponkali yëkk ya fa Basan.
«Éey saamar, yewwulal sama sàmm bi, sama jàmbaar jii ma lëngool,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi. «Dóoral sàmm bi, xar yi tasaaroo, ma walbati sama loxo, jublu ci jur gu ndaw gi.
¶ Kon nag bokk yi, ma ñaax leen, te yërmandey Yàlla tax, ngir ngeen jébbal ko seen yaram wépp, def ko jooxe buy dund, sell te neex Yàlla. Loolu déy mooy njaamu, gi leen war.
te ngeen di doxale cofeel, ni Almasi mi nu sopp, ba jooxeel nu bakkanam, def ko saraxu sawara, ngir xetug jàmm, ñeel Yàlla.
Fii ma tollu jot naa li ma aajowoo lépp, maa ngi ci naataange; doyle naa sëkk, gannaaw ba ma nangoo ci loxol Epafrodit, seenub yóbbante, te sarax su ñu nangu la, di xeeñ xetug jàmm, te neex Yàlla mi mu ñeel.