TSK

TSK · Leviticus 20:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Aji Sax ji teg ca ne: «Àttey yoon yii, nanga leen ko jox:

Réew ma sax mujj na daj ak sobe, ma wàcce mbugal ca kaw réew ma, ba mu gëq ay nitam.

Yeen nag maa leen di tasaare ci biir xeet yi, ndax maay génne saamar mbaram, mu dal ci seen kaw. Seenum réew dina wéet, seen dëkk yu mag gent.

¶ Musaa moo woo bànni Israyil gépp, wax leen ne leen: Yeen, bànni Israyil, dégluleen dogali yoon yi, ak àttey yoon yi may wax, ngeen dégg, tey. Jàngleen ko te farlu koo jëfe.

Yoonu Aji Sax jee mat, di leqli bakkan. Lu Aji Sax ji seede dëgg la, day xelal ku xeluwul.

Fu ma tollu maa ngi namm say ndigal ba sama xol ŋiis.

Giñ naa te di ko dëggal, ne dinaa sàmmonteek sa ndigali njekk.

Sa mboolem kàddu dëgg la, sa ndigal yépp di njekk, sax dàkk.

Naa xaacu, woyal la, yaa may jàngal sa dogali yoon.

Aji Sax ji, nu ngi lay xaar, fi sa kaw yoonu santaane yi, di la sàkku, ba la xel, lii déy, mooy sunu nammeelu xol.