TSK

TSK · Leviticus 22:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

nangeen sédde Aji Sax ji lépp lu jëkka juddu, rendil ko ko: lépp luy góor lu seen jur taawloo, Aji Sax jeey boroom.

¶ «Fexeleen ba bànni Israyil di tàggook seeni sobe, lu ko moy dinañu dee ndax seen sobe, ngir dañuy taqal sama màkkaan mi ci seen biir.»

¶ «Buleen giñe sama tur lu dul dëgg, di teddadil seen turu Yàlla. Maay Aji Sax ji.

Nañu nekkal seen Yàlla ay nit ñu sell, te baña teddadil seen turu Yàlla, ndax saraxi sawar yi ñeel Aji Sax ji, te di seen ñamu Yàlla, ñoo koy joxe. Kon nag dañoo wara sell.

Te buleen teddadil sama tur wu sell. Na bànni Israyil wormaal sama sellaay. Maay Aji Sax ji leen sellal,

Duñu ci gàddu benn bàkkaar, gannaaw bu ñu ci jooxee céru ngëneel li. Waaye jooxe yu sell yu bànni Israyil yooyu, buñu ci teddadil lenn, ba di ci dee.»

Yeen ñiy yóbbu ndabi Aji Sax yu sell yi, bu ngeen di jóge Babilon, dëdduleena dëddu lu sobewu, bañ koo laal, setluleen te génn foofa.