¶ «Bu ngeen dee góob seen tool, buleen góob ba fa tool ba yem te buleen ca toppaat, di foraatu.
TSK
TSK · Leviticus 23:22
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ngeen daldi bànneexu fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji, yeen ak seeni doom, góor ak jigéen ak seeni jaam, góor ak jigéen, ak Leween ñi ci seen dëkk, ak doxandéem yeek jirim yeek jëtun ñi ci seen biir, ci bérab bi seen Yàlla Aji Sax ji taamoo dëël turam ëllëg.
Mu dem ca tool ya, topp ñay góob, di foraatu. Yàlla-woo-yàlla, tool booba di toolu Bowas ma bokk ak Elimeleg.
Damaa masa xañ néew-ji-doole lu muy sàkku, mbaa ab jëtun wékk ma bët, ma tas yaakaaram?
Mooy nàddil néew-doole yi, njekkam sax dàkk, dooleem di yokku, ànd ak daraja.
Xanaa du sédd ku xiif saw ñam, fat néew-ji-doole ju amul fu mu dëkk, gis ku rafle, wodd ko, te baña nëbbu mbokk mu soxla?
Li ci biir kay ngeen di sarxe! Su boobaa seen lépp ay set.