TSK

TSK · Leviticus 23:24

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Su boobaa ci fukki fan ca juróom ñaareelu weer wa nangeen wal-lu ag liit fépp. Bésub Njotlaay boobu nangeen wal ag liit ci seenum réew ba mu daj.

¶ «Bu loolu weesee, benn fanu weeru juróom ñaareel, seen bésu woote bu sell lay doon. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey. Bés la bu ngeen di yéenee ag liit.

Esra, sarxalkat ba, indi téereb yoon wi keroog benn fanu juróom ñaareelu weer wa, fa kanam mbooloo ma, góor ak jigéen, mboolem ña seeni at may ñu dégg ko.

Wal-leen liit yi, wal bufta yi te xaacul Buur Aji Sax ji!

Lu gaawa gaaw lay doon, ci xef ak xippi, bu liit gu mujj ga jibee; nde liit ga mooy jib, ñi dee, dekki, di ñu dul yàqooti, nun nag, nu soppiku.