TSK

TSK · Leviticus 23:38

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Deeleen baaxantal bésub Noflaay, ngir sellal ko.

¶ «Juróom benni fan lees di liggéey, bésub juróom ñaareel ba bésub Noflaay doŋŋ lay doon, di bésub ndaje mu sell. Du lenn lu ngeen ciy liggéey. Bésub Noflaay la bu ñuy jagleel Aji Sax ji, ak fépp fu ngeen dëkk.

Foofa ngeen di yóbbu seen saraxi dóomal, ak yeneen sarax, ak seen céri fukkeel, ak seenub jooxe, ak seen sarax yu ngeen xas, ak seen saraxi yéene, ak seen saraxi taawug jur gu gudd ak gu gàtt.

Ezra 2:68 TSK

¶ Ba ñu àggee ca kër Aji Sax ja ca Yerusalem, am na ñenn ca kilifa ya jiite seen kër baay, ñu joxe ay saraxi yéene ngir tabaxaat kër Yàlla ga ca gentam.

Seen Yàlla Aji Sax ji, digooleen ak moom te jëfe ko. Kee jara ragal. Na ñi ko wër ñépp yótsiy teraanga.